تجاوز إلى المحتوى

xaajub jaar-jaaru yonnente bi.

32 lessons · Select a question to read the answer

Your progress in this topicTrack completed lessons on this device
Choose how to study:
1lan mooy askanu yonnente bi yal la na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc?

mooy Muhammat doomu Abdu Laahi doomu Abdul Mutallib doomu Haasim té Haasim ci xuraysin la bokk, xuraysin bokk ci araab yi, araab yi bokk ci séti Ismaahiil, te Ismaahiil doomu Ibraahiima la yal na gën gi mucc ak jàmm nekk ci moom ak ci sunu yonnent.

Open lesson
2lan mooy turu yaayu sunu yonnent yal na Yàlla dolli ko jàmm ak mucc?

Aaminatu doomu Wahbin.

Open lesson
3kañ la baayu yonnente bi faatu?

baayu yonnent bi faatu na ci Madiina fekk yonente bi juddu a gul.

Open lesson
4kañ la yonnente bi judd ?

ci atum ñay ya, bisu altine, ci weeru gàmmu.

Open lesson
5ci ban dëkk la juddoo?

ci Makka.

Open lesson
6ñan ñoo ko nàmpal ku dul yaayam?

jaamu baayam ba Ummu ayman.

- jaamu baay tëxam bi Abuu lahab, Suwaybatu.

- Halimatu Sahdiya

Open lesson
7kañ la yaayam faatu?

yaayam mi ngi faatu bi muy am juroom benn i at, maamam Abdul Muttalib yor ko.

Open lesson
8kan moo ko yor ginnaaw faatug maamam Abdul Muttalib?

maamam Abdul Muttalib mi ngi faatu bi miy am juroom ñatti at, baay tëxam Abuu Taalib yor ko.

Open lesson
9kañ la tukki wóon ànd ak baay tëxam ca Saam?

tukki na ànd ak baay tëxam ca Saam bi miy am fukki at ak ñaar.

Open lesson
10kañ la woon ñaareelu tukkeem bi?

ñaareelu tukkeem bi ci yaxantu la woon ci alali Xadiijatu yal na ko Yàlla dollli ngërëm, bi mu dellusée daal di koy takk soxna, booba mi ngi am ñaar fukk i at ak juroom.

Open lesson
11kañ la xuraysin tabaxaan kaaba ga?

xuraysin tabaxaat na kaaba ga bi miy am fanweer i at ak juroom.

ñu àtte loo ko bi ñu wuutee ci kuy teg xeer wu ñuul wi, mu teg ko ci ab sér, mu digal xeet wu ne mu jàpp ci benn cat u sér bi, ñu nekkoon ñeent i xeet, bin ko yëkkatee ba ca bërëb am, mu jël ko ci yoxoom teg ko ca barabam yal na mucc ak jàmm nekk ci moom.

Open lesson
12ñaata at la amoon bi ñu ko yónnee ? ak ci ñan la ñu ko yónni ?

mi ngi amonn ñeent fukki at, ci nit ñépp lan ko yónni, muy Aji- bégle ak i xuppe.

Open lesson
13nan la wahyu wi tàmbalee ci moom?

gént gu dëggu, daawul gént dara lud ul dina am mel ni suba gu xar.

Open lesson
14na ka la meloon lu jiitu wahyu wi? ak kañ la wahyu wi njëkk a wàcce ci moom?

da doon jaamu yàlla ca xunt uw Hiraa wa, daan yor yobbal am.

wahyu yi wàcci ci moom fekk mingi ci xunt wi di jaamu Yàlla.

Open lesson
15lan moo njëkk a wàcci ci Alxuraan?

wax i Yàlla ji: "iqra bismi ràbbi kal lazii xalaxa 1 xalaxal insaana min halaqin 2 iqra wa rabbukal akramu 3 allazii hallama bilxalami 4 hallamal insaana maa lam yahlam 5 saaru al-halaqi 1-5

Open lesson
16kan moo ñëkka gëm ak yonentem ?

ci góor ñi: Abóo bakrin Assiddiix, ci jingéen ñi: Xadiijatu doomu Xuwaylidin, ci xale yi: Aliyun doomu Abii taalibin, ci jaam yin goreel: Zaydu doomu Haarisatu, ci jaam yi gore wul: Bilaal ma dëkk Ecopi, yal na leen Yàlla dolli ngërëm, ak ñeneen.

Open lesson
17na ka la wooteb lislaam bi meloon?

woote bi ci suuf la woon diirub ñatti at, ñu digal yonnente bi yal na na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc ci mu baril ko.

Open lesson
18nan mbir i yonnente bi meloon ak ñi ànd ak moom ginnaaw binu biralee woote bi?

bokkaale kat yi dañoo ëppal ci di ko lor ak di lor jullit ñi, ba mujj mu digal way gëm yi ñu gàddaay jëm ca An-najaasi ca ecopi.

bokkale kat yi dëppoo ci ray yonnent bi Yàlla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, Yàlla aar ko peege ko baay tëxam ba Aboo taalib ngir mu aar ko ci ñoom.

Open lesson
19kan moo faatu ci atum fokkeel gi ci yònneem gi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc?

baay tëxam ba Abòo taalib, ak soxnaam sa Xadiijatu yal na ko Yàlla gërëm.

Open lesson
20kañ la rañaan gi amoon ak yéeg gi?

bi mu amee juroom fukki at, ñu farataal ci moom julliy juroom.

raañaan gi: mooy juge jàkka ja ca màkka dem ca jàkka ja ca Falastiin

yéeg gi: mooy bawoo jàkkay Falastiin dem ci asamaan sa, ba ci sidratul muntahaa.

Open lesson
21na ka la yonnente bi doon woowe nit ñi ci bitti màkka?

da daa woo waa Taahif di leen gaaral boppam ci xew-xew yi ak ndajeey nit ñi, ba bi ansaar yi dëkk Maddina ñëwee daal di koy gëm jaayante ak moom ci war koo dimbali.

Open lesson
22ñaata at la yonnente bi nekk Màkka di woote?

nekk na fa fukki at ak ñatt.

Open lesson
23fan la gàddaay jëm?

jòge Màkka dem Maddiina.

Open lesson
24ñaata at la am Maddiina?

fukki at.

Open lesson
25yan attey lislaam lan farataal ci moom ca Maddiina?

farataalees na ci moom azaka,ak woor,ak aj,ak jihaad,ak nodd,ak yeneen atttey lislaam.

Open lesson
26yan mooy xarey yonnente bi yi gën a am solo.

xare badar bu mag ba.

xare uhud.

xare ahzaab.

xareb ubbi Màkka.

Open lesson
27lan moo mujjee wàcc ci Alxuraan?

wax i Yàlla ji: ragal-leen bis banu leen i delloo ca seen Boroom kenn ku nekk ñu fay ko la mu jëfoon te kenn du ko ca tooñ 281. saaru Baqara: 281

Open lesson
28kañ la yonnente bi faatu? ak ñaata at la amoon?

mi ngi faatu ci weeru gàmmu ci atum fukkeel ba ak benn ci gàddaay gi, mi ngi amoon juroom benn i fukki at ak ñatt.

Open lesson
29tuddal soxnay yonnente bi?

1- Xadiijatu doomu Xuwaylidin yal na na ko yàlla gërëm.

2- Sawdatu doom i Zamhatu Yàlla na ko Yàlla gërëm.

3- Aysatu doom i Abuu bakar yal na ko Yàlla gërëm.

4-Hafsatu doom i Omar yal na ko Yàlla gërëm.

5-zaynabu doom i Xuzaymatu yal na ko Yàlla gërëm.

6-Ummu Salamata Hindu doom i Abii umayyata yal na ko Yàlla gërëm.

7- Ummu Habiibata doom i Abuu sufyaana yal na ko Yàlla gërëm.

8- Juwayriyatu doom I Alhaaris yal na ko Yàlla gërëm.

9- Maymuunatu doom i Alhaaris yal na na ko Yàlla gërëm.

10- Safiyyatu doom i Huyay yal na ko Yàlla gërëm.

11- Zaynabu doom u Jahsin yàlla nako yàlla gërëm

Open lesson
30ñan ñooy ay doomam?

goor ñi ñatt la nu:

Al-xaasimu, te ci moom lanu ko doon dakkantale.

ak Abdulla

ak Ibraahimu

bu dee jigéen ñi:

Faatimatu.

Ruqiyatu.

Ummu kulsuum.

Zaynabu.

doomam yépp Xadiijatu moo leen jur, bam des Ibraahima, te ñoom ñépp a ko njëkka faatu bam des Faatimatu, mi ngi faatu. ginnaaw am ci juroom benni weer.

Open lesson
31tuddal yenn melokaani jëmmi yonnente bi:

nekkoon na ku digg dóomu ci góor ñi, gàttul guddul waaye ci diggante bi la yamoon, dafa weexoon ne rax xonq yal na mucc ak jàmm nekk ci moom,ku séqoon sikkim la woon, yaatu woon ay gët, yaatu woon gémmeñ, kawar ga ñuuloon kukk, mu yaatu woon ay wàgg, neexoon xet, ak yu dul yooyu ci ay mbindiin yu rafet.

Open lesson
32ci lan la yonnente bi bàyyi aw xeetam?

bàyyi na aw xeetam ci aw xàll wu yaatu te leer, ag guddeem mel ni bëccëgam, kenn du ku jàdd ku dul ku alku, bàyyi wul benn yiw lud ul ni tegtal na ko xeet wi, wala benn ay lu dul moytu loo na ko xeet wi.

Open lesson